Mingui gané diamono 1912 ci Darou Haliimul Khabiir Ndam ay wadjuram Cheikh Ahmadou Bamba yakari djam gni ak Sokhna Fatimatou Soukhra, mingui diangué Alkhourane ci S Dame Abdourahmane Lo ba mokkal Alkhourane binde ap kaamil diébbal ko Serigne bi, Serigne bi tayé kofa ap diir, booléwat ko ak S Dame Abdourahmane nguir mu tambli ndiangum xam xam guinaw bi diangué nathii Serigne Diop Darou Salam Kayél, diangué nathii Serigne Mouhamadou Dém, guinaw Serigne bi démone na Mauritanie done sakku xam xam ci borom xam xam yifa nékkone, nékkone na borom xam xam bu mak daana faral di binde ci Arabe ak Wolof, bok nathii bayyit yi bimu done ziar barabou Serigne bi
ألا ياقبورالصالحين عليكم سلام من الله المهيمن طيب ونحن بكم من كل سوداءنختشى نلوذونرجوكل أمريحبب
Serigne Moussa Ka wayna thii mom loubari
Sagnthione na yit ay barab yu bari nguir yar ak dianglé bok nathii Daroul Khadiim ci wétu Touba Fall, ak Mbacké Bary fala dane nék loubari, nékkone na ko khamni dane na faral di touki fu bari thii reewmi fu mélni Cassamance ak Gambie amna tukki bumu tukki wone dafa wakhni Serigne bi mokoko digalone, bok nathii deuk yimu diaar kaolack Tamba Ngay Bamako Boiké ak Abidjan ak Karambasa ak kaplabisa ak Lomé ak Douala ak Libre Ville port Santé ak Brazzaville fala djoulee Tabaski guiss nafa mak mufa fékkone Serigne bi ku toude Samba Ndiaye xibar nako loubari guiss nafa loubari ci dieekhiiti Serigne bi
#ay_djikoom nékkone na ku tabé lole léwét lole bari diam nékkone na yit ku mana waaré daana déllo nit gni ci yalla oubiku yaatu lole am foulla, mingui guénn adouna 21 janvier 1955 ci Touba yalnanu ko yalla fayal ta tass nu thii barkeem